TSK

TSK · Leviticus 14:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sàkkal ñetti kilo, yemook benn fukkeelu nattub sunguf su mucc ayib su ñu xiiwe liitar ak genn-wàll, yemook xaajaatub natt bi ñuy wax xiin ci diwu segalu oliw, ak saraxu tuurub benn liitaru biiñ ak genn-wàll, yemook xaajaatub xiin. Loolu yépp ànd ak menn kuuy mi.

¶ «Bu saraxam dee ab gàtt bu ñuy def rendi-dóomal, muy xar mbaa bëy, na sarxal bu góor bu amul sikk.

¶ «Du benn saraxu pepp bu ñuy defal Aji Sax ji muy am lawiir, ndax du lenn ci lawiir mbaa lem, lu ñu wara lakk, ngir saraxu sawara su ñeel Aji Sax ji.

¶ «Su fekkee ne am xar lay sarxe, muy saraxu póotum bàkkaaram, na doon xar mu jigéen, mu amul sikk.

¶ «Sarxalkat bi teg ca jël menn kuuy mi, rendi ko, muy saraxu peyug tooñ, boole kook genn-wàll liitaru diw ga, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.

¶ «Su fekkee ne nit ki dafa ñàkk ba dooleem matewu ko, na wut menn kuuy, muy saraxu peyug tooñ, di saraxu yékkati-jébbale, ngir njotlaayam, boole kook ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, xiiwe ko diw, muy saraxu pepp. Na indaale genn-wàll liitaru diw,

¶ «Gannaaw loolu bu boroom jàngoroy xelli ji tàggook sobey jàngoro ja, dafa wara waññ juróom ñaari fan ngir setlu, ba noppi fóot ay yéreem, sangoo ndox mu balle ci bëtu ndox, doora set.

Sarax si muy sarxalsi Aji Sax ji di menn xarum menn at mu amul sikk, ngir rendi-dóomal, ak menn xarum menn at mu jigéen mu amul sikk, ngir póotum bàkkaar, ak menn kuuy mu amul sikk, ngir saraxas cant ci biir jàmm,

¶ «Kiy sarxal Aji Sax ji ab saraxam, na sarxewaale saraxu pepp bu benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, su ñu xiiwe ñeenteelu xaajub xiinu diw, di liitar ak genn-wàll,

Luke 5:14 TSK

Yeesu dénk ko ne ko: «Bu ko wax kenn, demal rekk ca sarxalkat ba, ngir mu seet la, te nga génne sa jooxeb setlu, ni ko yoonu Musaa santaanee, muy firnde ci ñoom.»

waaye seenug njot moo di deretu Almasi ju jafe, ji taxawe deretu xar mu sikkul, gàkkul.