Leviticus 11:24
TSK
¶ «Yii nag da leen di sobeel te képp ku laal lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Yii nag da leen di sobeel te képp ku laal lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so.
Képp ku lekk ca médd ma, na fóot ay yéreem, te du tee mu yendoo sobe ba jant so. Képp ku for médd ma, na fóot ay yéreem te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
¶ «Ka wacci woon sikketu Asasel, na fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi.
Gannaaw loolu na sarxalkat bi fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi, te du ko tee yendoo sobe ba ca ngoon.
Ku góor kiy tonni dóomi nag wi itam day fóot ay yéreem, te du tee mu yendoo sobe ba ca ngoon. Na loolu di dogalu yoon bu sax fàww, ñeel bànni Israyil, ak doxandéem bu dëkk ci seen biir.