TSK

TSK · Leviticus 18:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba Israyil dëkkee ca réew ma, am na bés Ruben dem tëdd ak Bilaa, nekkaaleb baayam; Israyil yég ko. Doomi Yanqóoba yu góor fukk lañu ak ñaar.

¶ «Ku dëkkoo sa soxnas baay, sa baay nga torxal. Ñoom ñaar ñépp dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp.

Ayitofel ne ko: «Demal dëkkoo sa nekkaaley baay, yi mu wacce këram, ñu di ko topptoo. Su ko defee bànni Israyil yépp dinañu xam ne def nga lu tax sa baay sib la. Dina tax say farandoo gëna am fit.»

Amos 2:7 TSK

Ñooy dëggaate néew-ji-doole ci pëndub suuf, di xañ way-ñàkk àqam. Nit ak baayam di tëdde as ndaw, di teddadil sama tur wu sell.