TSK

TSK · Leviticus 19:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ndaxte man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Kon nag sell-luleen te sell ndax man ku Sell laa. Kon buleen sobeel mukk seen bopp ci mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ci suuf.

Sell-luleen te sell, ngir man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

Te itam nangeen ràññee ne ñu sell lañu, ndax seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Nangeen leen jox céru nit ñu sell, ndax ku Sell laa, man Aji Sax ji leen sellal, yeen.

Waaye warula jege rido bi, mbaa muy dem ba ca sarxalukaay ba, ndax sikk si ci moom. Bumu teddadil sama bérab yu sell, ngir man Aji Sax ji maa sellal bérab yooyu.»

Ku ci nekk di àddu, naan moroom ma: «Kee sell te sell te sell, keey Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, àddina sépp a feese ag leeram!»

¶ Gannaaw noo moom yii dige nag, soppe yi, nanu setal sunu bopp ci mboolem sobey yaram, ak ju xel, te nu matal sellnga ci ag ragal Yàlla.