TSK

TSK · Leviticus 2:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Diiru juróom ñaari fan, bu dara ci lawiir am fenn ci seeni kër, ndax képp ku lekk lu am lawiir, dees na ko dagge ci askanu Israyil, muy doxandéem mbaa doomu réew mi.

¶ «Buleen rendi sama sarax, di boole deret jeek lu am lawiir, te gàttu saraxu bésub Mucc, bu ci dara fanaan ba bët set.

Te it mboolem saraxu pepp bu sarxalkat di defal boppam, dees koy lakk ba mu jeex. Deesu ci lekk.»

Boo gisee lem, lekkal lu yem; bu ëppee, nga waccu ko.

¶ «Moytuleena yaafusal seen bopp ci naan gu ëpp ak màndite ak xalaati àddina, lu ko moy bés ba jekki dal ci seen kaw,

¶ Seen damu gii de jekkul dara. Xanaa xamuleen ne as lawiir tooyalu sunguf bépp lay funkil?

ngir bañatee topp xemmemtéefi bakkan, xanaa di topp coobarey Yàlla, diir bi ko dese ci kaw suuf.