¶ Ba loolu amee Musaa wàcc tund wa, dellu ca mbooloo ma. Mu sell-luloo leen, ñu fóot seeni yére,
TSK
TSK · Leviticus 21:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Lii nag mooy li nga leen di defal, ngir sédd leen céru sellnga, ngir ñu di ma sarxalal: Dangay jël yëkk wu ndaw ak ñaari kuuy yu amul sikk,
ndaxte man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Kon nag sell-luleen te sell ndax man ku Sell laa. Kon buleen sobeel mukk seen bopp ci mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ci suuf.
Sell-luleen te sell, ngir man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu sell, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawar yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell.
«Santal bànni Israyil ne leen sama sarax, sama ñam wi jëm ci sama saraxi sawara ngir xetug jàmm, ñeel ma, nañu farlu ci di ma ko indil saa yu àppam jotee.
¶ Boobu sarxalkat bu mag lanu soxla; moo sell, mucc sikk, mucc sobe, moom lañu teqale ak bàkkaarkat yi, te moom lañu kaweel ba fa tiim asamaan.