TSK

TSK · Leviticus 22:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu kenn ci yeen dee sàkkal Aji Sax ji sarax, na indi ag jur, muy gu gudd mbaa gu gàtt.

¶ «Su sarax si nit kiy génne dee sarax su ñuy wàccoo ngiñ mbaa saraxu yéene, dees na ko lekk bés bi ko nit ki joxee, te lu ca des ba ca ëllëg sa, ñu man koo lekk.

¶ «Képp ku bokk ci bànni Israyil mbaa ci doxandéem yi ci seen biir, bu rëbbee ba jàpp mala mbaa njanaaw, mu di lu dagana lekk, na tuur deret ji, suul,

bu ngeen di defal Aji Sax ji saraxu sawara, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax su nit di wàccoo aw xas, mbaa saraxu yéene, mbaa seen saraxi màggal, ngir xeeñal xetug jàmm ñeel Aji Sax ji, te muy lu jóge ci jur gu gudd mbaa gu gàtt, defe leen ko nii:

Foofa ngeen di yóbbu seen saraxi dóomal, ak yeneen sarax, ak seen céri fukkeel, ak seenub jooxe, ak seen sarax yu ngeen xas, ak seen saraxi yéene, ak seen saraxi taawug jur gu gudd ak gu gàtt.

ngeen doora amal màggalug Ayi bés, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, te saraxu yéene ba ngeen cay joxe di kemu koom ga leen seen Yàlla barkeele.

Moom de sàgganewul boroom tiis, làqu ko kanamam, ba mu wootee, wuyu na ko.

Naa dëkke sa xayma, ba fàww; làqoo sa kiiraay. Selaw.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di woyu Sabóor, ñeel Daawuda.

Samay digeek Aji Sax ji laay matal fi kanam ñoñam ñépp.

Nit ña nag am tiitaange lu gënatee réy ci Aji Sax ji, daldi rendil Aji Sax ji sarax, ba noppi xasal ko aw xas.