Li des ci saraxu pepp mi, Aaróona aki doomam ñoo koy féetewoo, muy cér bu sella sell, bawoo ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.
TSK
TSK · Leviticus 22:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Su mala mu dagan méddee, ku laal médd ma dina yendoo sobe ba jant so.
nit ki ànd naak jàngoro te taq na sobe. Na sarxalkat bi biral ci lu leer ne nit ki sobewu na ndax jàngoro ji ci bopp bi.
«Li yoon digle ci mbirum nit ku ame jàngoroy der juy law, keroog bés ba ñuy laabal nit ki, mooy lii: Nañu ko yegge sarxalkat bi.
¶ «Gannaaw loolu bu boroom jàngoroy xelli ji tàggook sobey jàngoro ja, dafa wara waññ juróom ñaari fan ngir setlu, ba noppi fóot ay yéreem, sangoo ndox mu balle ci bëtu ndox, doora set.
¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: «Waxal sarxalkat yiy doomi Aaróona ne leen: Bu ci kenn sobeel boppam, di laal mbokkam mu dee,
Lii nag, yaa ko moom, ci mboolem sarax yu sell yee sell, yi mucc sawara: seen bépp sarax, seen bépp saraxu pepp ak seen bépp saraxu póotum bàkkaar, ak seen bépp saraxu peyug tooñ bu ñu ma indil, lu sella sell la, ñeel la, yaak sa doom yu góor.
¶ «Bu loolu weesee ku laal nit ku dee, ak néew bu mu mana doon, dina sobewu diiru juróom ñaari fan.
Képp ku sobewu te setluwul, kooku dees koy dagge ci mbooloo mi, ndax bérabu sellngay Aji Sax ji la sobeel. Gannaaw wiseesu ko ndoxum setlu mi, sobewu na.