TSK

TSK · Leviticus 23:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bés bu jëkk bi nangeen ci amal ndaje mu sell. Juróom ñaareelu bés ba itam nangeen ca amal ndaje mu sell; deesul liggéey lenn ci yooyu bés, lu moy ngeen togg ñam wu ñépp lekk. Loolu doŋŋ lees ciy mana def.

«Samay màggal, man Aji Sax ji, dangeen koo wara siiwal, muy ndaje yu sell. Samay màggal yii la.

Bés bu jëkk bi ndaje mu sell ngeen ciy amal. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.

Buleen ci liggéey dara. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan ak fépp fu ngeen dëkk.

Ngeen daldi bànneexu fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak Leween ñi ci seen dëkk, ak doxandéem yeek jirim yeek jëtun ñi ci seen biir, ci bérab bi seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg.