¶ «Su fekkee ne ab doxandéem bu ngeen dëkkal mbaa ab màngaan dafa woomle te kenn ci seeni bokk ñàkk, ba jaay boppam doxandéem bi ngeen dëkkal mbaa kenn ku bokk ak doxandéem bi,
TSK
TSK · Leviticus 25:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Nawmi ne Ruut: «Yal na Aji Sax ji barkeel Bowas, moom mi saxoo sàmm ngoram digganteem ak nit, muy dund ak mu dee!» Mu teg ca ne ko: «Kooku ku nu jege la; bokk na ci ñi am sañ-sañu jotaat nu.»
Mu ne: «Kii ku mu?» Mu ne: «Man a Ruut, sang bi. Yiire ma sa mbubb, ndax mbokk nga, te sañ nga maa jotaat.»
Man nag dama noon war naa la koo yegge, te laaj la ndax danga koy jënd ci kanam magi dëkk bi ak ñi fi toog. Soo bëggee def sa warugaru jotaat, jëndal. Soo buggul, wax ma, ma xam. Ndax kat kenn gënu la cee yey, te maa topp ci yaw.» Mu ne ko: «Damay jënd kay!»
«Xoolal, Anamel doomu Salum sa baay bu ndaw a ngooguy ñëw, naan la nga jënd toolam ba ca Anatot, ndax yaa ko saña jotaat.»
Mu waxaat ne: «Man maay am kóolute ci moom.» Dellooti ne: «Maa ngi nii, maak gone yi ma Yàlla jox.»