TSK

TSK · Leviticus 25:36

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Bu ngeen dee lebal ku bokk ci sama ñoñ, di néew-ji-doole ju ngeen dëkkal, buleen def ni ab leblekat, di ko sas ab tegandaay.

Buleen di naxante, waaye ragal-leen seen Yàlla, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

Ñee naan: «Sunuy tool ak sunuy tóokëri reseñ ak sunuy kër lanuy tayle ngir am pepp ci xiif bi.»

Waaye boroom diiwaan yi ma jiitu dañu daan not askan wi, di leen sëf seen dund ak seen biiñ, boole ci ñeent fukki dogi xaalis. Seeni surga it di néewal askan wi doole. Man nag defuma noonu ndax ragal Yàlla.

Kiy leble di tege, ba barele, kay yéwéne néew-ji-doole lay dencal.

ndollant lay leblee, ab tegandaay, mu jël. Moo kii nu muy dunde? Kii kay du dund! Ak mboolem jëf ju siblu jii mu def, dee rekk mooy àtteem. Bakkanam lay gàddu.

Alalu ger, ñu jël fi sa biir, ngir lor ay bakkan. Ndollant ci kaw tegandaay, nga jël feyeekoo bor, di wute alal sa àqu moroom. Man nag, nga fàtte ma. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.