TSK

TSK · Leviticus 25:43

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Teewul rewlikat ya ragal Yàlla, ba defuñu la leen buur ba sant; xanaa ñu bàyyi liir yu góor ya, ñu dund.

¶ Ba ñu demee ba mu yàgg, Firawna buuru Misra dee. Fekk na bànni Israyil a ngay binni rekk ndax seen njaam ga. Ñuy woote wall, ba seen jooy, ya sababoo ca seen toroxteg njaam ga, àgg fa Yàlla.

Yuux, yi bànni Israyil nekke nii, agsi na ba ci man, te gis naa it ni leen waa Misra di note.

Buleen di naxante, waaye ragal-leen seen Yàlla, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

Ab surga lay doon ci njaatigeem at mu nekk, waaye waru koo soxore ci biir kilifteef, ngeen di seetaan.

Job 31:14 TSK

bu ci Yàlla jógee, ana nu may def? Bu ma ko laajee, ana lu ma koy wax?

te naa: “Ana lu nuy woor te xooloo ci? Lu nuy toroxlu te teewluwoo?” Ma ne: Bés bu ngeen woor, yeena ngi topp seen bakkan, di sëqatal seeni liggéeykat.

«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

¶ Yeen ñiy sang yi, yorleen seeni jaam, yorin wu jub te aw yoon, te ngeen xam ne yeen itam am ngeen ab Sang fa asamaan.