¶ «Saxleen ci samay dogal, sàmm samay ndigali yoon, di ko jëfe, ndax ngeen dëkk ak jàmm ci réew mi.
TSK
TSK · Leviticus 26:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Maay xabtal rabi àll yi ci seen kaw, ñu xañ leen seeni doom, seeni gétt ñu tas, seeni nit ñu néewal, ba seeni mbedd ne wëyëŋ.
Ba ñuy doora sanc foofa, ragaluñu woon Aji Sax ji, ba tax Aji Sax ji yebal ay gaynde ci seen biir, ñu di leen rey.
jaaxaan, kenn du la lëjal, ñu bare di la leewaayu;
May nga ma bànneexu xol bu raw seen pepp mu tuurook biiñ bu wal.
Éy Aji Sax ji, won nu sa ngor, baaxe nu sag wall.
nag yi ëmb ba diis, du mbas, du biir bu yàqu, te deesu fi yuuxoo pénc ya.
Soo tëddee doo tiit; say nelaw day neex.
Boroom bee yónnee kàddu gu dal Israyil, askanu Yanqóoba,
Gaynde du fa am, rab wu aay du fa dox, du lenn lees fay gis, ku ñu jot rekk a fay jaare.
Waaye yaw Yanqóoba sama jaam, bul tiit,» kàddug Aji Sax jee; «yaw Israyil, bul ragal. Fu sore laa lay wallujee, yaak sa askan wa ca réewum njaam ga, Yanqóoba dellu dal, fegu; kenn dootu ko tiital.
Maay yebal ci seen kaw ab xiif ak rabi àll yu leen di xañ ay doom; mbas ak deret ju tuuru gane leen, saamar, ma indil leen. Man Aji Sax ji, maa ko wax.»
Su ma wàccee saamar ci miim réew it, ba sant saamar ne ko mu jaar ci biir réew mi, dagge fi nit ak mala,
Maay fas ak ñoom kóllëreg jàmm, maay far ci réew mi wépp rab wu aay. Su boobaa ñu dëkke màndiŋ mi ci xel mu dal, di fore bët biir gott bi.
Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, «Ca nga may wooye “Sama jëkkër,” te dootoo ma wooye “Sama Baal.”»
Ñoom ñépp ay toog, ku nekk ci kerug reseñam, mbaa keppaarug garabu figgam, kenn du leen xoqtal. Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
Daraja ji kër gii di mujje mooy sut ja woon, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. Mu ne: Ci bii bérab laay mayee jàmm, kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.»
¶ Gannaaw nag dees noo jox àtteb ñu jub ci kaw ngëm, jàmmoo nanu ak Yàlla ndax sunu Sang Yeesu Almasi.