Waxleen ak mbooloom Israyil mépp ne leen, bésub fukkeel ba ci weer wii, na ku nekk jëlal njabootam ab gàtt, kër gu nekk ak gàttam.
TSK
TSK · Leviticus 4:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Bu saraxam dee saraxu jur gu gudd gu ñuy def rendi-dóomal, na sarxal aw yëkk wu amul sikk. Na ko yóbbu ci bunt xaymab ndaje mi ci kanam Aji Sax ji, ngir mu nangul ko ko.
bu nemmikoo bàkkaar bi mu def rekk, na sarxe aw bëy wu jigéen wu amul sikk, ndax bàkkaar bi mu def.
Dees koo néewal doole, mitital ko te ubbiwul gémmiñam, xanaa mel ni xar mu ñuy rendiji, ne cell ni xar mu ñuy wat, ubbiwul gémmiñam.
Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk.
te Almasi di ki def boppam sarax bu mucc sikk ñeel Yàlla, ci dooley Noo gu Sell gi, kon nag ñaata yoon la deretu Almasi gëna mana setal sunu yaraange ji sababoo ci sunu jëf ju bon ju jëme ci ndee, ba nu mana jaamu Yàlla jiy dund!
«Moo bàkkaarul, fenul.»
Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi.
Ba mu jëlee téere bi, ñeenti bindeef yi ak ñaar fukki mag ñeek ñeent ne gurub sukk fi kanamam, ku nekk yor xalam ak andi wurus yu fees ak cuuraay, cuuraay li di ñaani aji sell ñi.