TSK

TSK · Leviticus 5:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nañu raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Sarxalkat bi day jàpp ci laaf yi, xotti te bañ koo teqale, daldi koy lakk ci sarxalukaay bi, ci kaw mattum taal bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Su ko defee sarxalkat bi génne ci saraxu pepp mi, ab saraxu baaxantal, daldi koy lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm ñeel Aji Sax ji.

ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko.

Te itam na génne nebbon bi yépp, ni muy génnee nebbonu xar mu ñuy def saraxu cant ci biir jàmm. Na sarxalkat bi lakk loolu ci kaw sarxalukaay bi, mu dolliku ci saraxu sawara yi ñeel Aji Sax ji. Noonu la sarxalkat biy defale nit ki njotlaayal bàkkaar bi mu def, mu am njéggal.

Na sarxalkat bi sàkk ci saraxu pepp bi, ab ŋëb buy fàttlee, daldi koy lakk ci kaw sarxalukaay bi. Gannaaw loolu mu naanloo ndaw si ndox mi.

te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi mi nu sopp, ba jooxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara, ngir xetug jàmm, ñeel Yàlla.