TSK

TSK · Leviticus 5:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Waxal bànni Israyil ne leen: Su fekkee ne nit ki dafa moy lenn ci santaaney Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, li ci war lii la.

¶ «Su fekkee ne kilifa moo moy lenn ci santaaney Yàllaam Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, mu dig tooñam,

¶ «Bu nit bàkkaaree ndax lu mu dégg wooteb seede cib àtte, ba noppi baña wax la mu gis mbaa mu xam ko ca mbir ma, dees na ko ko topp.

«Ku ñàkka wormaal lenn lu ñu sellalal Aji Sax ji te du teyeefam, daan ba ko war, mu di ko indil Aji Sax ji, am kuuy mu amul sikk lay doon, ñuy xayma njégam, dëppale dayob xaalis baak natt ba ñu yoonal ca bérab bu sell ba. Saraxu peyug tooñ la.

Waaye jawriñ ji xamul nammeelu njaatigeem, te teewu koo def lu yelloo ay duma, yet yu néew lay am. Képp ku ñu jox lu bare, dees na la topp lu bare. Képp ku ñu dénk jopp, dees na la feyeeku lu ko ëpp.