TSK

TSK · Leviticus 6:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Góori foofa laaj ko ndaw si mu àndal, lu mu doon ci moom, mu ne: «Sama jigéen la.» Dafa bañoona wax ne soxnaam la, ngir ragal waa foofa rey ko ndax taaru Rebeka.

¶ «Bu saraxam dee saraxu jur gu gudd gu ñuy def rendi-dóomal, na sarxal aw yëkk wu amul sikk. Na ko yóbbu ci bunt xaymab ndaje mi ci kanam Aji Sax ji, ngir mu nangul ko ko.

Loolu saraxu peyug tooñ la, ndax kooka kat tooñ na Aji Sax ji.»

ne ko mu wax bànni Israyil, ne leen: «Muy góor, di jigéen, bu tooñee moroomam, ba fecci wormay Aji Sax ji, nit kooku tooñ na.

Bul tuumaal nit ci neen, te bu ko seedeel ay fen.

Peeñu mu ñàng lañu ma ci wax. Workat biy wor, yàqkat biy yàq. Yeen waa Elam, songleen; yeen waa Medd, gawleen leen. Dakkal naa mboolem onk yu ñu sabab.

Wóoy ngalla yaw bóomkat bi kenn bóomul, yaw workat bi kenn worul. Boo noppee bóome, ñu bóom la, te boo noppee wore, ñu wor la.

Yeena ngi dëkke njublaŋ, njublaŋ rekk, faaleetuleen ma.» Kàddug Aji Sax jee.

Amos 8:5 TSK

te naan: “Xanaa màggalu Terutel weer wi du jeex ba nu jaay sunu pepp? Waay, na bésub Noflaay jàll gaaw, ba nu ubbi sàq yi, tuutal nattu sol-sotti, diisal doomu nattukaay, tey naxee sunuy màndaxekaayi njublaŋ,

Sa gët yu sell jomb naa niir lu bon, te manoo seetaan noteel! Ana looy seetaan ay workat? Looy noppi te ku bon di mëdd moroomam mu ko gëna jub?

Acts 5:4 TSK

Ba mu jaragul, du yaa doon boroom? Gannaaw ba mu jaree it, xanaa du njég gaa ngi sa loxo ba tey? Ana noo mana xajale mii mébét ci sa xol? Du nit nga wor de, waaye Yàlla nga wor.»

Buleen di fenante, gannaaw seen jëmm ja woon démb, boole ngeen kook jëfinam ja mu àndal, summi,