TSK

TSK · Leviticus 7:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Bu nit bàkkaaree ndax lu mu dégg wooteb seede cib àtte, ba noppi baña wax la mu gis mbaa mu xam ko ca mbir ma, dees na ko ko topp.

Da koy yót sarxalkat bi, kooku jëkka rey benn bi, muy saraxu póotum bàkkaar; na kutt baat bi te bumu teqale bopp beek baat bi.

¶ Bu loolu weesee, Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:

Waa ji day yóbbu am kuuyu peyug tooñ ca bunt xaymab ndaje ma, muy peyug tooñ, gi muy sarxalal Aji Sax ji.

Day yeesalal Aji Sax ji nasireenam ga mu ko séddoo woon, kemu fan ya mu xasoona nasireenal. Su ko defee day indi xarum menn at, def ko saraxas peyug tooñ. Fan yi mu jëkkoona nasireenal day neen, ndax nasireen googa moo sobewu.

Biir dal-luwaay boobu, ñeenti taabal a nga ca, ñaari taabal cat lu nekk. Ca lañuy rey juri sarax yi. Muy saraxu rendi-dóomal, di saraxu póotum bàkkaar, di saraxu peyug tooñ.

Mu ne ma: «Bii bérab, fi la sarxalkat yiy togge yàppu saraxu peyug tooñ ak saraxu póotum bàkkaar, di fi lakk saraxu pepp mi, ngir baña génne lenn lu sell ca ëttu biti ba, bay sédd nit ñi sellnga gu leen di lor.»