TSK

TSK · Leviticus 7:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Li ko waral mooy, man Aji Sax ji damaa jële ci seen saraxi cant ci biir jàmm, dënn bi ñuy def saraxu yékkati-jébbale, ak tànkub jooxe bi, jox ko Aaróona, sarxalkat bi mook doomam yu góor. Seen cér la ba fàww ci biir bànni Israyil.»

Ba mu ko defee Aaróona yékkati dënn yaak tànku ndijoor ba, defal ko Aji Sax ji saraxu yékkati-jébbale, muy la Musaa santaane woon.

¶ «Na sarxalkat bi jébbale loola, defal ko Aji Sax ji saraxu yékkati-jébbal. Cér yu sell a ngoogu ñeel sarxalkat bi, mu boole kook dënn biy saraxu yékkati-jébbal, ak jooxeb tànkub kanam bi. Gannaaw loolu nasireen bi sañ naa naan biiñ.

Lii mooy li lew sarxalkat yi, te bàyyikoo ci askan wi, ci ñiy rendi ay sarax, muy aw nag, di ab gàtt: nañu jox sarxalkat bi, mbagg mi ak lex yi, ak mbàq gi.

¶ Xanaa xamuleen ne, ñiy liggéeye ci kërug Yàlla gi, ci kërug Yàlla gi lañuy jële seen lekk, te ñi sasoo sarxalukaay bi, am nañu wàll ci sarax ya ñu fa joxe?