TSK

TSK · Luke 1:53

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ragal-leen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.

di àtte néew-ji-doole, di leel ku xiif. Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj.

Luke 6:24 TSK

Waaye wóoy ngalla yeen ñi barele, ndax neexle ngeen ba noppi.

¶ «Jenn waay la woon ju bare alal, di sol yérey tànnéef yu rafet, di dunde lu neex bés bu set.

Yeesu gis loolu, daldi ne: «Boroom alal tàbbi ci nguurug Yàlla, ndaw lu jafe!

¶ Yeen daal suur ngeen xaat! Woomle ngeen xaat! Yeena ngi tàmbalee nguuru, te xaaruleen nu ci sax! Céy su ngeen doon nguuru léegi, ba nun itam nu mana nguuroondoo ak yeen!

James 5:1 TSK

¶ Kaayleen nag ma wax leen, yeen boroom alal yi, jooyleen te yuuxu, ndax mitit yi leen di dikkal.

Dootuñu xiif, dootuñu mar. Dootuñu loru ci jant bi mbaa weneen tàngoor,