TSK

TSK · Luke 11:40

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda. Ab dof a ngi naa ci xelam: «Yàlla amul!» Ñu ni mel ay def njekkar, seeni jëf siblu, kenn defu ci lu baax.

Bu suuf di yëngu mook ñi ko dëkke ñépp, maay kiy téye ay kenoom. Selaw.

Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi? Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi? Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?

Ngalla dégluleen lii, xeet wu dofe, ñàkk xel wi ngeen doon, ami gët te dungeen gis, ami nopp te dungeen dégg!

Yàlla nag ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey jii, dees na jël sa bakkan. Kon li nga waajal, ana kuy doon boroom?”

Gàtt xel! Li nga ji, yaw ci sa bopp, du dundaat li feek deewul ba noppi.