Nàddil-leen koo nàddil, abal koo abal dayob soxlaam.
TSK
TSK · Luke 11:41
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Ku sonal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; ku baaxe ku néewle, teral nga ka ko sàkk.
Dugalal sa alal, dawloo ko; yàgg-yàgg nga jotaat ci.
Ma ngay wax naan: «Xanaa lii du Babilon gu mag gi ma tabax man, ci sama doole ju réy, muy péeyu buur, di sama ndam ak sama daraja?»
¶ Ci kaw loolu Yeesu ne waa ja ko woo bernde: «Boo dee waajal bernde, añ mbaa reer, bul woo say xarit, mbaa say doomi ndey, mbaa say bokk, mbaa say dëkk yu am alal, nde ñoom itam dañuy walbatiku, woo la rekk, mu doon sag pey.
Yeesu dégg loolu, ne ko: «Lenn rekk nga deseleeti. Mboolem loo am, jaay ko, séddale ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal, topp ci man.»
¶ Dëkk ba ñuy wax Yope, ab taalibe bu jigéen a nga fa woon, ñu di ko wax Tabita mbaa Dorkas ci làkku gereg. Def lu baax ak sarxe la saxoo woon.
Mu ne ma: “Korney, nangu nañu say ñaan, te nemmiku nañu say sarax fa kanam Yàlla.
¶ «Samay tànk nag, gannaaw gëjeb at yu bare, moo doon indil samaw askan, ay ndimbal ak ay sarax yu ñeel Yàlla.
Gannaaw nag yeena duunle ci lépp; muy ci wàllu ngëm, ak wàllu kàddu yu rafet, ak wàllu xam-xam, ak cawarte ci lépp, ak ci cofeel gu nu leen xiir, kon ndajalem ndimbal lii it, ngalla duunleleen ci.
¶ Lii rekk la: ji lu tuut, góob lu tuut; ji lu bare, góob lu bare.
Ndaxte li Yàlla sàkk lépp a baax, du lenn lees ciy aayal, ndegam kàddug cant lees ko jariñoo.
Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey, ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.
Njullite gu set te mucc sikk fa kanam Yàlla Baay bi moo di lii: di nemmiku jirim akub jëtun ci seen njàqare, tey sàmmu ba mucc ci gàkki àddina.