TSK

TSK · Luke 11:49

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Déggal! Soxna si, Xel mu Rafet a ngi woote, dég-dég di xaacu.

Pexe mu leen jàpplu dina sababoo sax ci seeni waajur ak seen doomi ndey ak seeni jegeñaale ak seeni xarit, te dees na rey ñenn ci yeen,

Acts 7:57 TSK

¶ Ba loolu amee ñu yuuxu ca kaw, dar seeni nopp, daldi ànd, ne milib ca kawam;

Acts 9:1 TSK

¶ Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkook a jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,

Acts 22:4 TSK

Yoon wii tey, daan naa fitnaal ñi ko gëm ba sabab seenug dee. Yeew naa góor, yeew jigéen, tëjlu leen kaso.

Def naa ko ci Yerusalem, te it bare na ñu sell ñu ma tëjlu ci kaw sañ-sañ bu ma sarxalkat yu mag yi jagleel, te saa yu ñu leen tegaan àtteb dee, dama daan biral kàddu gu leen àtte ñàkkal.

Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu, mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njekk, di sunu sellte, di sunug njot,

Moo may ñii di ay ndawam, ñee di ay yonent, ñee di ay xamlekati xibaaru jàmm bi, ñale di ay sàmmi mbooloom gëmkat ñi, mbaa ay jànglekat.