¶ Ba loolu wéyee Musaa ne Aaróona: «Waxal mbooloom bànni Israyil gépp, ne leen ñu dem ba ca kanam Aji Sax ji, ndaxte dégg na seeni diiŋat.»
TSK
TSK · Luke 12:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba mu ko defee Absalom sant ay nitam, ne leen: «Ma ne, bu Amnon naanee biiñ, ba xolam sedd, bu ma leen nee ngeen jam ko rekk, reyleen ko. Buleen ragal; man maa leen ko sant. Góor-góorluleen nag te ñeme.»
Ba loolu amee Aman di leen limal alalam ju bare ak doomam yu góor yu bare ak mboolem ni ko Buur terale, yékkati ko, mu gëna kawe ci kàngami buur aki jawriñam.
Biir ba du wéet, lu mu xemmem, du rëcc.
Su doon jal xaalis ni suuf, yére yomb ko ni feppi suuf,
Buleen yéemu ci ku barele, teraangay këram di yokku.
Yàquleeka leena bett! Musibaa leen ne fuuf, ñu ne mes!
Alal du jariñ bésu mbugal; jub, mucc ci gàtt fan.
Sama doñ-doñ, ji fi kaw dun bi, génnliku na ma, dama koy wacce ka may wuutuji rekk,
Kuy jagoo alal ju lewul, mooy picc mu toj lu mu nenul. Kookooy tollu digg dooleem, alal ja dëddu, mu mujje dof.»
¶ «Mbind mi ñu rëdd mooy: WAÑÑ, WAÑÑ, NATT, SÉDDALE.
¶ «Ba baadoolo ba deeyee, malaaka yi yóbbu ko ba ca wetu Ibraayma. Boroom alal ba itam dee, ñu rob ko.
Ndax kat indaalewunu dara ci àddina, te manunoo yóbbaale dara.