Nehemiah 3:15
TSK
¶ Bunt ba ñuy wax Bëtu Ndox ba, Salun doomu Kol Ose, boroom gox ba ñuy wax Mispa, moo ko defaraat. Moo ko tabaxaat, xadd ko, taxawal laf ya, ak tëjukaay yaak dénki galan ya cay ànd, ak itam tata ja ca déegub Silowe, bay suuxat toolu buur, ba ca dëggastal ya ngay wàcce, génn gox ba ñuy wax Kër Daawuda.