TSK

TSK · Luke 14:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ngeen daldi bànneexu fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak Leween ñi ci seen dëkk, ak doxandéem yeek jirim yeek jëtun ñi ci seen biir, ci bérab bi seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg.

¶ Gannaaw bu ngeen génnee mboolem céru fukkeelub meññeef, ci atum ñetteel, yemook atum génne cérub fukkeel, gannaaw ñaari at yu nekk, nangeen ko jox Leween ñi ak doxandéem yi ak jirim yi ak jëtun ñi, ngir ñu lekk ba regg, fa ñu féete ca seeni dëkk,

Ba mu ko defee mbooloo ma mépp ñibbi, di lekk ak a naan ak a yekkle di bànneexu bu baax. Fekk na ñu xam kàddu ya ñu leen doon xamal.

Job 29:15 TSK

Silmaxa, maa dooni gëtam; ab lafañ, ma diy tànkam.

Teralal Aji Sax ji ci sa alal ak loo jëkka meññle,

Bàyyeel ñoll kuy sànku, bàyyi biiñ ak boroom naqar.

di leel ku xiif lu ngeen gëna bëgg, di reggal néew-ji-doole, su boobaa seen leer fenke biir lëndëm, seenug këruus di ag njolloor,

Li ci biir kay ngeen di sarxe! Su boobaa seen lépp ay set.

Acts 2:44 TSK

Gëmkat ñépp benn lañu woon te ñoo bokkoon lépp.

Acts 9:39 TSK

¶ Piyeer jóg, ànd ak ñoom, ba agsi. Ñu yéege ko ca néegu kaw taax ma. Ay jëtun a nga fa woon. Ñoom ñépp di jooyoo, yéew Piyeer, won ko turki yaak mbubb ya Dorkas defaroon ba muy nekk ak ñoom.

Njiit li nag fàww mu mucc sikk, di ku dencul lu wees jenn jabar, ku moom bakkanam, jiital am xelam, di ku nawlu, man gan, te mana jàngle.

Titus 1:8 TSK

Waaye war na di ku man gan, ku xejjoo lu baax, jiital am xelam, jub, sell te moom boppam.

Buleen sàggane di terle, nde am na ñu seen teraanga tax ñu fat ay malaaka te xamuñu ko woon.