TSK

TSK · Luke 16:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 20:21 TSK

Dara du rëcc ab kollam, moo tax xéewalam du toog.

Walaakaanaak néew-doolee ngi wër, di wut um ndox, amul. Seen put wow koŋŋ ak mar. Man Aji Sax ji, maa leen di nangul; man Yàllay Israyil, duma leen wacc.

«Te bu ñu génnee, gis néewi ñi doon fippu fi sama kaw, seeni sax duñu dee mukk, seen sawara du fey mukk, te boroom suux bu leen gis, yaram wa daw.»

Mu ne ko: “Loolu doyul, Maam Ibraayma, waaye su kenn bàyyikoo ci ñi dee, dem ba ca ñoom, dinañu tuub.”

Looloo tax it Ibraayma di maamu ñi xaraf, te du xaraf gu ñu toppe aada, xanaa ñu boole ca topp ci tànki ngëm ga sunu maam Ibraayma amoon ba mu xarafagul.

Ci biir sawara wuy sëlsëli lay doon. Ca lay mbugal ñi xamul Yàlla, ak ñi baña déggal xibaaru jàmm bi jëm ci sunu Boroom Yeesu.

James 3:6 TSK

¶ Aw làmmiñ itam sawara la; làmmiñ a bokk ci sunuy cér, te di àddinay mbon, di gàkkal jëmm jépp. Aw làmmiñ, giiru dundu nit ki lay jafale ab taal bu tàkke fa sawara.

kooku dina naan biiñu sànjum Yàlla bu kenn raxul, ñu xelli ko ci kaasu sànjam. Te dees na ko mbugale sawara ak tamarax ci kanam malaaka yu sell yi ak Gàtt bi.

Képp ku ñu gisul ñu bind la ci téereb dund bi, ci déegu sawara si lees la sànni.