TSK

TSK · Luke 2:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu ne ko: «Man déy, maay ànd ak yaw, te boo génnee mbooloo ma Misra, dingeen ma jaamusi ci tund wii. Loolooy firndeel ne, maa la yónni.»

Gannaaw boo teqlikook man, dinga dajeek ñaari góor ca wetu bàmmeelu Rasel ca Celca ca diiwaanu Beñamin. Dinañu la wax ne la mbaam ya nga seeti woon feeñ nañu. Te sax sa baay xalaatatul mbaam yi, yeena ko jaaxal. Ma nga naan: “Ana nu may def ak sama doom ji?”

¶ Fekk na Esekiya ne Esayi: «Ana lu di takk biy firndeel ne Aji Sax ji dina ma wéral, ba ma mana dem gannaaw ëllëg ca kër Aji Sax ji?»

«Ñaanal sa Yàlla Aji Sax ji firnde. Ñaan ko ko, ak fu mu mana bawoo, fa suufa suuf, mbaa fa kawa kaw.»

Ana ku gëm sunub dégtal? Ana ku Aji Sax ji won dooley përëgam?