TSK

TSK · Luke 2:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Fa ñu dal ca guddi, kenn ci ñoom bëgga xont mbaamam, ubbi saakoom rekk, ne pemm ci xaalisam.

¶ Ba ñu lalee panaan ca yoon wa, Aji Sax ji dafa dogale Musaa, nar koo rey.

Kon nag Boroom bi ci boppam moo leen di jox firnde: janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, tudde ko Emanuwel (mu firi Yàllaa ngeek nun).

Mu dikk, sotti diw ak biiñ ca gaañu-gaañu ya, lëmës ko. Ci kaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci ab dalukaay, di ko topptoo.

Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.