TSK

TSK · Luke 21:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 5:36 TSK

Ndaxte bu yàggul la Tëdas jóg, di jaay daraja, ba lu wara tollook ñeenti téeméeri nit far ak moom. Ñu rey ko, ña ko toppoon ñépp tasaaroo, seen pexe mujjewul fenn.

Ñooñu ay ndawi caaxaan lañu, ay liggéeykat yu njublaŋ yu mbubboo ndawi Almasi.

Bu leen kenn naxe nenn, ndax bés ba du dikkagum, te fippu gu mag ga jëkkula dikk, ba ki jëmmal ndëngte te dëgmal alkute, feeñ.

Waaye nit ñu bon ñi, ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.

Ñu xalab ninki-nànka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.