TSK

TSK · Luke 23:43

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ma xamal la ne moy naa, làqatuma la sama ñaawtéef. Ma ne: «Naa àgge Aji Sax ji sama bàkkaar.» Yaw nga baal ma peyug tooñ. Selaw.

«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.

Sàkkuleen Aji Sax ji bi ngeen koy mana gis, wooleen ko bi muy jege.

Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.

Luke 15:4 TSK

«Ana kan ci yeen mooy am téeméeri xar, réerle ci menn, te bàyyiwul ca àll ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent (99), ngir toppi ma réer, ba gis ko?

Ndax Doomu nit ki, ñi réer la seetsi, ngir musal leen.»

Kon ñeme lanu def, te li nu gënal di génn, des bitib sunu yaramu tey, ngir dëkki ak Sang bi.

Ci diggante yaar yooyii laa tance: yàkkamti na maa yiwiku ba fekki Almasi, te loolu moo dàqati fuuf.

Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.