TSK

TSK · Luke 4:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba loolu amee Aman di leen limal alalam ju bare ak doomam yu góor yu bare ak mboolem ni ko Buur terale, yékkati ko, mu gëna kawe ci kàngami buur aki jawriñam.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko fexe, ngir sàggi sagub képp ku fiy damu, ba teddadil képp ku àddina teral.

Te loolu jarula waaru, ndax Seytaane ci boppam, malaakam leer lay mbubboo.

Ndax bindees na ne: «Bépp boroom suux, nim ñax la mel, mboolem darajaam mel ni tóor-tóoru àll, ñax ma wow, tóor-tóor ma ruus.

Ñu xalab ninki-nànka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.

Ñu may ko itam mu xareek ñu sell ñi, duma leen, boole ci may ko sañ-sañ ci kaw niti gépp giir ak wépp xeet ak wépp làmmiñ ak wépp askan.