TSK

TSK · Luke 6:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ndax ba Yesabel jabari Axab di rey yonenti Aji Sax ji, Abdiyas a boole woon téeméeri yonent, làq leen ci ñaari xuntiy xeer, xunti mu nekk juróom fukk. Mu di leen fa may lekk ak naan.

¶ Ilyaas ne: «Man kat damaa xéroona xér ci yaw Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. Waaw, bànni Israyil dañoo fecci sa kóllëreek ñoom; say sarxalukaay, ñu màbb; say yonent, ñu jam saamar. Ma des man doŋŋ, ñuy wuta jël sama bakkan nii!»

¶ Axab ne Ilyaas: «Ãa, noon bi, gisati nga ma?» Ilyaas ne ko: «Gis naa la, ndax dangaa dogu ci def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu.

Nga ne ko: “Buur dafa wax ne: Dugal-leen kii ndungsiin, di ko jox lekk gu néew ak ndox mu néew, ba keroog may dikk ak jàmm.”»

Su boobaa ab làggi ne jàyy ni kéwél, ab luu sarxolle. Am ndox ay fettaxe màndiŋ ma, ay wal wale joor gu wow,

Luke 1:41 TSK

Naka la Elisabet dégg nuyoob Maryaama, doom ja mu ëmb yëngu ca biiram. Elisabet daldi feese Noo gu Sell gi.

Luke 6:35 TSK

Yeen kay, soppleen seeni noon, defleen lu baax, lebleleen te baña yaakaar ndelloo. Su boobaa seenub yool réy, ngeen di doomi Aji Kawe ji, ndax moom de ñi santadi te bon, moo leen di baaxe.

Acts 5:41 TSK

¶ Ndaw ya nag bàyyikoo ca kurélu àttekat ya, di bég, gannaaw ñoom lañu jàpp ne ñoo yelloo toroxte ga ñu leen teg ndax Tur wi.

Mu àddu ca kaw, ne waa ji: «Jógal taxaw jonn!» Waa ji ne bërét, jóg, daldi dox.

Looloo ma tax di bànneexu ci biir diggante yu ma néewe doole, ak ci biiri saaga, ak ci biir ag ñàkk, ak ci biir coono yu ñu may bundxatale, ak ci biir njàqare yu ma dal ngir Almasi. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laa am kàttan.

Ndax kat bokk yi, yeena aw ci tànki gëmkati Almasi Yeesu ya fa mboolooy Yàlla, ya fa réewum Yuda, nde coono ya ñu daj ca Yawut ya, yeen it seeni waa réew teg nañu leen lu ni mel.

Ku amul ngëm nag doo mana neex Yàlla, ndax kiy dikk fi Yàlla, fàww nga jëkka gëm ne Yàlla am na, gëm it ne ñi koy sàkku, moo leen di yool.

¶ Ana lu ma ciy tegati? Jot gee ko dul mate, su ma naroona nettali mbirum Sedeyoŋ ak Barag ak Samson ak Yefte ak Daawuda ak Samiyel ak yonent yi.

Waaye noonu ngeen séddoo ci coonoy Almasi, bégeleen ko, ngir bu ndamam feeñee, ngeen gënatee bég.

Bul ragal mukk mitit wi nga nara daj. Seytaanee ngi noonu di dugal kaso ñenn ci yeen, ngir nattu leen. Dingeen am coono diiru fukki fan. Nanga saxoo kóllëre ba dee fekk la ci, ma kaalaa la kaalag dund.

¶ «Ku am ndam nag, ku saxoo jëf ji ma soob, ba kera muj ga, maa lay jox sañ-sañ ci kaw xeet yi:

Ku am ndam nag, maa lay def nga doon ag kenu fi sama biir néeg Yàlla, te doo fa génnati mukk. Maay bind fi sa kaw sama turu Yàlla ak sama turu dëkku Yàlla, te mooy Yerusalem gu bees, giy wàcce fa kaw, bàyyikoo fa sama Yàlla, maay bind it fi sa kaw sama tur wu yees.