Yeena ngi naan: «Ana nun koy toŋale, ba am lay wu ko tiiñal?»
TSK
TSK · Luke 8:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ab soxor, taxawaayam du yàgg; ku jub garab la, reen ba ne kekk.
Man mii lañuy sàkku bés bu ne, di wuta xam sama coobare! Mbete xeet wuy def njekk, te waccul ndigalu yoonu Yàllaam. Ñu ngi may ñaan àttey njekk, di sàkku man Yàlla, ma jege leen,
«Ana nu ma lay def, yaw Efrayim? Nu ma lay def yaw Yuda? Te sa ngor di xiinu suba, mbaa ab lay, jekki ne mes.
¶ Yeesu neeti: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane kat mu ngi sàkku ab sañ-sañ ngir man leena jéri ni am pepp.
Su ma jotoon ci kàddug waxyu, boole ci xam mboolem kumpa, ak mboolem xam-xam, ak ngëm gu mat sëkk ba mana toxal ay tund, te jëfewuma cofeel, duma dara.
¶ Yeen waa Galasi, yeena ñàkk xel! Ku leen gëlëmal, te na Yeesu Almasi deeye ca bant ba di lu ñu leen leeralal ba mu mel ni lu ngeen gise seeni bët?
Ana seen mbég mooma woon nag? Ndax kat maa leen seedeel ne su manoona am sax, seeni bët ngeen di luqi, jox ma.
Noonu la deme, ndegam kay fekk na leen sësoo ngëm gu ngeen dëjoo ba dëgër, te baña nangu lenn di leen sorele ak yaakaar ji ci xibaaru jàmm, bi ngeen dégg, te ñu biral ko, ñeel mépp mbindeef. Man Póol nag, ci yégle xibaaru jàmm boobu laa di ab jawriñ.
Moo tax ba ma muñee ba tële, ma yónnee, ngir xam fu seen ngëm tollu, ndax ragal ne Fiirkat bi da leena fiir, ba sunuw ñaq neen.
Ñoo lajj yoonu dëgg, ba naan ñiy dekki, dekki nañu ba noppi, te seen wax jooju, am na ñenn ñu muy yàq seen ngëm.
Yaram wu àndul akug noo daal, ni mu deeye, noonu la ngëm gu àndul aki jëf, deeye.
Li léeb wii wax te muy dëgg, moo leen dikkal: «Xaj waccu, lekkaat ko; te cangaayu mbaam-xuux, teewu koo xalangootee poto-poto.»
Ñooñooy gàkkal seen jataayu lekk yi gëmkat ñiy bokk, di ñóox te amuñu ci jenn jom; ñooy xiin yu naaxsaay yu ngelaw li yóbbu; ñooy garab yu dee ñaari yoon, du meññ waxtoom, reen ya buddiku.