Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»
TSK
TSK · Malachi 1:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. Yàlla, Aji Sax ji Yàlla àddu na, di woo àddina, penku ba sowu.
Éy Yàlla, yéwéne nu, barkeel nu, te geesoo nu sa leeru kanam, Selaw,
Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk ñoo lay sujjóotalsi, di màggal sa tur.
Muy kàddug Sabóor. Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, moo def ay jaloore, kàttanam ak sellngay dooleem jox na ko ndam li.
Nañu woy say jaloore, naan: «Aji Sax jeeka màgg teddnga!»
Deesatul gaañe mbaa di lore, fi mboolem sama kaw tund wu sell wi, ndax ni ndox di feese ba muur géej, ni la àddina di feese nit ñu xam Aji Sax ji.
Ña ngay xaacu di sarxolle, waa sowu di sàbbaal ci màggug Aji Sax ji.
Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, yeen waa cati àddina, kañleen ko, ànd ak ñiy wàcci géej ak li ci biiram, ak duni géej ak ña ca dëkke.
Yeen waa àddina, catoo cat, walbatikuleen fi man, mucc. Man maay Yàlla, du keneen.
Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di tàllal xeeti jaambur ñi loxo, ñee ma yékkati raaya, wooye leen; ñu fab say doom yu góor, indi, tungóom sa doom yu jigéen, délloosi;
Sa jëkkër, ki la sàkk, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee di turam. Aji Sell ju Israyil moo la jot, te moo di Yàllay àddina sépp.
Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na; teddngay Aji Sax ji fenkal na la!
Maay teg firnde fi seen digg, ba jël ñenn ca ña dese bakkan ca ñoom, yebal leen ci xeet yi, yebal leen Tarsis, ak Pul ak Ludd, ñooña di ñu mane fitt, ma yebal leen ca waa Tubal ak Yawaan, waa duni géej yu sore ya, ñooñu masula dégg sama jaloore, te masuñoo gis sama teddnga, sama ndaw ñaa leen di xamal sama teddnga.
Aji Sax ji, kenn melul ni yaw, yaaka màgg, jàmbaare, màggu tur.
Su boobaa bànni Israyil nangu ndesu Edom, ak mboolem suufi xeet yi ñu ma tudde woon.» Kàddug Aji Sax jee, te moom lay def.
Nu raglu la Aji Sax jiy dale ci seen kaw, te mooy ràggal yàllay àddina yépp, ba xeet yi di ko sujjóotale dunoo dun, wu ci nekk ak fa nga fare.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Maa ngii di walloo sama ñoñ fa réewum penku, ak réewum sowub jant.
«Alkànde ñeel na ab jinigalkat bu am ci géttam am kuuy mu mu xasoo sarxe, te di sarxalal Boroom bi jur gu sikk, nde man, buur bu mag laa!» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Sama tur moo jara ragal fi biir xeet yi.
¶ Mbooloo mépp nag a nga woon ca biti di julli, ca waxtuw saraxu cuuraay boobu.
¶ Ci kaw loolu Korney ne: «Bëkkaati-démb ci waxtuw digg njolloor wii nu tollu tey, ci laa doon ñaane sama biir néeg. Mu am ku jekki ne jaas ci sama kanam, sol yére yu ne ràññ.
¶ Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax, ngir ngeen jébbal ko seen yaram wépp, def ko jooxe buy dund, sell te neex Yàlla. Loolu déy mooy njaamu, gi leen war.
ngir ma doon jawriñu Almasi Yeesu, ñeel jaambur ñi dul Yawut, may wàccoo ak liggéeyu carxal bi xibaaru jàmm bu Yàlla laaj; su ko defee ñi dul Yawut mana doon ab jooxe bu Yàlla nangu, jooxe bu Noo gu Sell gi sellal.
¶ Kon li ma bëgg moo di góor ñi di ñaane fépp, tàllal loxo yu mucc sikk, te bañ cee boole meroo ak mbiicoo.
Ba mu jëlee téere bi, ñeenti bindeef yi ak ñaar fukki mag ñeek ñeent ne gurub sukk fi kanamam, ku nekk yor xalam ak andi wurus yu fees ak cuuraay, cuuraay li di ñaani aji sell ñi.
¶ Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne: «Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem. Mooy nguuru ba fàww.»