TSK

TSK · Malachi 2:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ñu dem ba mu yàgg, Kayin sàkk ci mbeyam, jébbal ko Aji Sax ji, màggale ko ko.

Man ci sama bopp dinaa noonoo nit kooku te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil, ndax li mu jël ciy doomam jox Moleg, di sobeel sama bérab bu sell tey teddadil sama tur wu sell.

Yanqóobaa, yaaka yànji xayma! Israyil, laa ne, yaaka taaruy màkkaan!

Te kat ay bés a ngi ñëw, maay dagg sa doole, dagg sa dooley waa kër baay, ba deesatul màggate ci sa kër.

¶ Samiyel ne ko: «Bànneexu Aji Sax ji ci saraxi rendi-dóomal ak yeneen sarax, mbaa tolloo naak bànneex ba muy am ci dégg ndigalal Aji Sax ji? Ma ne, dégg ndigal a gën ab sarax; xol bu nangoo gën nebbonu kuuy.

Ñu gis ne ñenn ci askanu sarxalkat yi jëloon nañu ay jaambur soxna: Ci askanu Yosuwe doomu Yoccadag aki bokkam, Maaseya ak Elyeser ak Yarib ak Gedalya bokk nañu ca.

Mag meek kàngam li ñooy bopp bi, yonent bi mokkal naaféq dib geen.

Man Aji Sax ji, damaa sopp yoon, bañ càcc ak ñaawtéef. Maay dàmp sama ñoñ ni mu ware, fas ak ñoom kóllëre gu sax.

Kay seetlu ca yonent ba, aw ayam, mook ayu yonent ba, benn lay doon. Ñooy bokk gàddu seenu ay.

Hosea 4:4 TSK

«Waaye bu ci kenn layoo, bu ci kenn sikke, ndax sa bokk yee mel ni ñuy layook sarxalkat yi.

¶ «Aji Sax ji Yuda lay jëkka wallu, ndax darajay waa kër Daawuda, ak darajay waa Yerusalem baña màgg ba ëpple Yuda.

Xanaa du benn baay lanu am, nun ñépp? Te jenn Yàlla jee nu sàkk? Lu waral ku ne di wor mbokkam, ba fecci kóllërey maam ya?

Waaye nit ñu bon ñi, ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.