TSK

TSK · Malachi 2:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kee di cëslaay, te mati jëf, wépp yoonam di njub. Yàlla ju am kóllëre, mucc njubadi, te njekk ak njub mooy boroom.

Job 34:5 TSK

Baay Ayóoba kat nee moo yey, Yàlla xañ ko dëggam.

Job 34:36 TSK

Kon na àtteb Baay Ayóoba mii mat sëkk, nde tontam bokk na ci tontu nit ñu bon ñi.

Mu naa ca xelam: «Yàlla fàtte na, dummóoyu na, du xoolati.»

fa ma seeni maam doon nattoo, di ma seetlu te gis la ma def.

Seeni Terutel weer ak seen bési màggal laa bañ ci sama xol; yooyu màggal a ma diis ba àttanatuma ko.

Esayi nag ne: «Yeen waa kër Daawuda, dégluleen! Tàyyiloo ngeen nit, di tàyyiloo sama Yàlla itam.

Du xaalis boo ma jëndale barax bu xeeñ, du nebbonu sarax boo ma reggale. Xanaa lakkal maak say bàkkaar, sonal maak say ñaawtéef.

Yaw yaa ma wacc,» kàddug Aji Sax jee, «dellu gannaaw, ma duma la, sànk la. Muñ naa ba sonn.

Mu ne ma: «Tooñaangey waa kër Israyil ak Yuda moo ëpp loxo lool. Réew maa ngi fees ak deret, dëkk bi fees ak yàqute. Nee nañooy: “Aji Sax ji wacc na réew mi. Aji Sax ji gisul dara.”

Amos 2:13 TSK

«Maa ngii di yëngal suuf si ngeen joggi, ni watiir wu fees aki sabaar di yëngale suuf.

«Doom teral baayam, jaam, sangam. Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? Su ma dee ab sang, ana saab cér?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur, yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?”

Waaw, nit dina sàcc Yàlla? Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe.

Moo tax nu ne nit ñu bew ñi ñooy ñi barkeel, ñiy def lu bon kay ñoo baaxle, ñoom ñiy diiŋat Yàlla, teg ca rëcc.”»

¶ Li ngeen wara jëkka xam moo di bés yu mujj ya, ay niti ñaawlekat ay dikk, di nit ñu topp seen bakkan.