Beral-leen seen bopp ay nit ñu rafet xel, am ug dégg, te di ñu ràññiku ci seeni giir. Su ko defee ma tabb leen, ñuy seeni njiit.»
TSK
TSK · Micah 3:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji nee: «Xanaa ñiy def lu bon ñépp xamuñu dara? Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam, te sàkkuwuñu Aji Sax ji.»
Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen njiiti Sodom, teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor.
Man nag, ma noon: «Ñii de ay baadoolo rekk lañu, di def jëfi dof, xamuñu yoonu Aji Sax ji, xamuñu lu seen àtteb Yàlla laaj.
Dégluleen te teewlu, buleen fétteeral. Aji Sax ji kat wax na!
Kàngami Israyil a ngii fi sa biir, di jaay doole bay tuur deret.
«Dégluleen lii, yeen sarxalkat yi! Teeyluleen, yeen waa kër Israyil! Teewluleen, yeen waa kër buur! Yeen la àtte bi ñeel. Ag fiir ngeen tegoon ca Mispa, ab caax ngeen laloon ca tundu Tabor,
Wóoy ña ne finaax ca Siyoŋ, wóoy ña naagu fa tundu Samari! Ñooy kàngami xeet wi gëna màggeey, niti Israyil di leen diis-si soxla.
Li may wax gàcce la ci yeen. Xanaa amul ci seen biir, benn boroom xel bu mana àtte ay bokkam?