Nguur gi du jóge ci loxol Yuda, te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam, li feek boroom di ñëw, ba xeet yi déggal ko.
TSK
TSK · Micah 4:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba fa Aji Man ji tasaaree buur ya, tawub yuur a ngay sóobe tundu Calmon.
Janti Buur aji jub day woomle, te ba keroog weer wiy fey, jàmm di law,
Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk ñoo lay sujjóotalsi, di màggal sa tur.
¶ Mbir mii la Yàlla won Esayi doomu Amocc ci mbirum Yuda ak Yerusalem.
Deesatul gaañe mbaa di lore, fi mboolem sama kaw tund wu sell wi, ndax ni ndox di feese ba muur géej, ni la àddina di feese nit ñu xam Aji Sax ji.
Maa naa bëj-gànnaar: “Ësi!” ne bëj-saalum: “Bul téye!” Jëleel sama doom yu góor fu sore, délloosi, te jëleji sama doom yu jigéen fa cati àddina.
Sa gentub tey bi déy a ngi wéet, di réew mu yàqu yaxeet. Waaye léegi déy mu fees ba far xat; fu ña la sànkoon di soree.
Ay xeet ay fekksi sag leer, ay buur wutsi sa ceeñeeru njël.
«Man maa xam seeni jëf ak seeni xalaat. Bés bii taxaw lees di dajale xeetoo xeet aki làkk, ñu dikk ba niir samag leer.
Yaw Aji Sax ji may dooleel, di ma feg, di ma làq bésub njàqare, yaw la xeet yiy bawoo cati àddina, fekksi la, naan: «Caaxaani neen kay la sunuy maam baaxoo woon, xërëmi neen yu amul njariñ.
¶ «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Man ci sama bopp maay sàkke ab car ca njobbaxtalu garabu seedar gu kawe ga, sàkkal ko bérab. Car yu ndaw ya ca kaw laay fàqe car bu nooy, jëmbatal ko sama bopp ci kaw tund wu mag te kawe.
Yaay songi Israyil, sama ñoñ, mel ni aw niir, muur réew ma. Fan yu mujj ya la loolu di am, maa lay yóbbu yaw Gog, ba ca réew ma ma séddoo. Maa lay firndeele sama sellnga, ngir xeet yi gis, ba xam maay kan.
Ndigalu yoon wi jëm ci kër Yàlla gi ñu wara tabax mooy lii: ci kaw tund wi ak fi ko wër fépp, fu sella sell lay doon. Loolu mooy ndigalu yoon wi, ci wàllu kër Yàlla gi.»
Ci kaw loolu weñ gaak ban baak xànjar jaak xaalis baak wurus wa lépp bokk rajaxoo, mel ni xataxu dàggay lolli. Ngelaw li buub ko yóbbu, ba mu ne mes. Doj wa daloon ca jëmm ja nag doon tund wu mag, fees àddina sépp.
Ci kaw loolu ñu jébbal ko kilifteef gaak ndam laak nguur ga. Ci biir loolu waa mbooloo yépp ak xeet yeek làkk yi di ko wormaal. Kilifteefam day sax fàww, du jeex, te nguuram du foq mukk.
ba keroog góor gu mag gi dikk, daldi jox dëgg aji sell yu Aji Kawe ji; àpp bi nag mat, aji sell yi moom nguur gi.
Léegi ñëw naa ngir xamal la liy dikkal sa mbooloo ci jamono yiy ñëw ndax peeñu mi ëmb na jamono yooyu itam.»
Kon nag dees na gàbb Siyoŋ nib tool, Yerusalem googu diy tojit, jale, tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.
«Éy Siyoŋ, rëccal, yaw mi dëkke janq Babilon mu taaru mi.»
Réew mi mépp ag joor lay soppliku, dale ko Geba ba Rimon ca bëj-saalumu Yerusalem, Yerusalem tooge bérabam, tiim la ko wër, dëkk bi dale ca buntu Beñamin, ba fa bunt ba woon, jàll ba ca buntu Jàddukaay ba, daleeti ca tatay Ananel ba ca nalukaayi reseñi buur.
Waaye li ko dale penku ba sowub jant, fu ci nekk la sama tur màgge ci biir xeet yi, te fépp lees di taale cuuraay, ngir sama tur, boole ci sarax su set, nde sama tur a ni màgge fi biir xeet yi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
¶ Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bugguma ngeen umple mii mbóot: Ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israyil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat.
¶ Li ngeen wara jëkka xam moo di bés yu mujj ya, ay niti ñaawlekat ay dikk, di nit ñu topp seen bakkan.
Boroom bi, ana ku la ragalul? Ku dul màggal saw tur? Yaw doŋŋ yaa sell. Askan yépp ay dikk, sujjóotsil la, ndax yaa jubi dogal.»
¶ Ma daldi gis asamaan su bees ak suuf su bees. Fekk na asamaan su jëkk sa ak suuf su jëkk sa wéy, te géej amatul.