Keroog bés booba li des fi Israyil ak li rëcce kër Yanqóoba duñu wéerooti ña leen duma. Aji Sax ji lañuy wóolu, wéeroo ko, Aji Sell ju Israyil.
TSK
TSK · Micah 5:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu ne: «Xeeb naa li ma la sas ngay sama jaam biy siggil giiri Yanqóoba, te wara délloosi ndesu Israyil gii. Tabb naa la, ngay leeru xeet yi, di jotale waa cati àddina sama wall.»
«Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, mu falu di buur bu xelu, di jëfe njub ak njekk ci réew mi.
Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Sarxolleleen, bége askanu Yanqóoba, xaacul-leen xeet woowu jiitu, biral-leen cant te ne: “Éy Aji Sax ji, wallul ndesu Israyil, sa ñoñ ñii.”»
Mooy topp ay faram te du leen dab; mu seet leen, du leen gis. Su boobaa mu ne: “Naa dellu ca saa jëkkër ju jëkk ja, nde ca laa gënoonu demin.”
«Efrayim, ana nu ma lay baye, yaw Israyil laa ne, nu ma lay tege ciy loxo? Ana nu ma lay defe ni Atma? Nu ma lay yemaleek Ceboyim? Sama xol a bëpp, sama yërmandee yëngu.
Maay def liy soox aw ndes, la ñu dàq fu sore, ma def ko askan wu am doole, te Aji Sax jeey doon seen buur ca kaw tundu Siyoŋ, li ko dale tey ba fàww.
Yaw de dinga lekk, te doo suur, xanaa wéye biir bu wéet. Dinga fat loo dul mana denc fu wóor, te loo denc fu wóor it, ab saamar laa koy jox.
Maay jàmbaaral waa kër Yuda, maay wallu waa kër Yuusufa, suqli leen, ñeewante leen, ñu mel ni masuma leena xarab, nde man maay seen Yàlla Aji Sax ji, te maa leen di nangul.
Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw, ci biir rakk yu bare.
Ana lu ko Yàlla tontu? Da ne: «Beral naa sama bopp juróom ñaari junniy (7 000) nit ñu sujjóotaluloon Baal tuur mi.»
¶ Firnde ju màgg nag moo feeñoon asamaan: Ndaw su làmboo jant bi, weer wi ronu ndëgguy tànk yi, mu kaalawoo fukki biddiiw ak ñaar.