Su keroogee mbedd bawoo Misra ba Asiri, waa Asiri di dikk ba Misra, waa Misra di dem ba Asiri te Misra di jaamoondook Asiri.
TSK
TSK · Micah 7:12
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Maa naa bëj-gànnaar: “Ësi!” ne bëj-saalum: “Bul téye!” Jëleel sama doom yu góor fu sore, délloosi, te jëleji sama doom yu jigéen fa cati àddina.
Séentul fi la wër ba gis: ñoom ñépp a daje, di la fekksi, sa doom yu góor a dikke fu sore, te sa doom yu jigéen it dees leena fab, indaale.
Janti keroog waa kër Yuda ànd ak waa kër Israyil, bawoondoo réewum bëj-gànnaar, wuti réew ma ma séddoon seeni maam.
«Maa ngii di jële sama ñoñ réewum bëj-gànnaar, dajalee leen fa cati àddina. Silmaxaa ngi ci akub lafañ, jigéenu wérul it ak kuy wasin, ñuy gàngoor gu mag, délsi fii.
te nga wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jëleji bànni Israyil ca biir xeet ya ñu fekki, dajalee leen wet gu nekk, délloosi leen seen suufas bopp.