TSK

TSK · Nehemiah 13:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu amee Buur sant Ilkiya sarxalkat bu mag ba, mook sarxalkat ya ca topp, ak wattukati buntu kër Aji Sax ji, ne leen ñu génnee kër Aji Sax ji mboolem ndab ya ñu defaraloon Baal ak Aseraak biddiiwi asamaan yépp. Mu génne lépp Yerusalem, lakk ko ca tooli Sedoron, ba noppi yóbbu dóom ba Betel.

¶ Kon nag rikk sama Yàlla, bàyyil xel ci man te baaxe ma, ndax mboolem li ma defal askan wii!

¶ Yosuwe, sarxalkat bu mag ba mooy baayu Yowakim. Yowakim di baayu Elyasib, Elyasib di baayu Yowada,

¶ Rikk sama Yàlla, bàyyee ma lii xel, te bul far sama jëfi ngor ji ma jëfe ci sama biir kër Yàlla gi aki wartéefam.

Aji Sax ji, yaay sànk kuy fen, sib kuy bóomeek kuy wore.

Mu jëm ci njiitu jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Éey Israyil, négandikul Aji Sax ji. Aji Sax jee gore, te yaatug njot.

Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la; teewlul, ma tinu la; nangul ma ci sa wormaak sa njekk.

Yaw la ay buur di baayoo, seeni lingeer di la nàmpal. Ñoo lay sujjóotal, di la maral say tànk, ba nga xam ne maay Aji Sax ji, te ku ma yaakaar du rus.»

¶ Li nuy damoo nag moo di seede bi nu sunu xel mu dal seedeel, ne xol bu set ak jikko ju dëggu ju bawoo fa Yàlla, mooy li nu doxale ci àddina si, rawatina sunu digg ak yeen, te du lu nu sunu xam-xamu nitu neen may, waaye yiwu Yàlla moo nu ko may.