TSK

TSK · Numbers 1:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Nangeen wormaal ayu bésu Mburu mu amul lawiir, ndaxte ci bés boobu tembe laa leen génnee réewum Misra, kurél ci kaw kurél. Kon nag nangeen wormaal bés bii, muy dogal bu leen war fàww, yeen ak seen askan.

«Limal askanu Leween ñi, ni ñu bokke seen këri maam ak seeni làng. Mboolem góor ñi am weer, jëm kaw, ngay lim.»

Ci màndiŋ mii kay la seeni néew di tëdd. Mboolem ñi ñu leen limal, mboolem ñi ñu leen waññal, ñu dale ci ñaar fukki at, jëm kaw te doon ñaxtu ci sama kaw,

“Kenn du gis mukk réew ma ma giñaloon Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ci góor ñi jóge Misra te am ñaar fukki at, jëm kaw, gannaaw mataluñu kóolute ci man.

¶ Jant yooyu laa leen sant ne leen: «Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen jox réew mii, ngir ngeen nangu ko. Na xarekat yépp gànnaayu, jàll, jiitu seen bokki bànni Israyil.

¶ Yowab nag indil Buur limu askan wa: Israyil di juróom ñetti téeméeri junniy góor (800 000) ñu tollu ci xare; Yuda di juróomi téeméeri junniy góor (500 000).