Numbers 1:51
TSK
Bu jaamookaay bi dee dem, Leween ñee koy wékki, bu jaamookaay bi dee dale bérab, Leween ñee koy we. Ku ci bokkul ba laal ci nag, dees koy rey.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu jaamookaay bi dee dem, Leween ñee koy wékki, bu jaamookaay bi dee dale bérab, Leween ñee koy we. Ku ci bokkul ba laal ci nag, dees koy rey.
¶ Keyat nag, ci moom la làngu Amrameen ñi soqikoo, ak làngu Isareen ñi, ak làngu Ebroneen ñi, ak làngu Usiyleen ñi. Làngi Keyateen ñaa ngoogu.
¶ «Bu dal bi waree jóg, na Aaróona ak doomam yu góor muur yëf yu sell yi, ak mboolem jumtukaayi bérab bu sell bi ba noppi. Gannaaw loolu la askanu Keyat di dikk, ngir gàddu ko. Su ko defee duñu laal dara lu sell, bay dee. Loolu la Keyateen ñi di gàddu ci wàllu xaymab ndaje mi.
Keyateen ña nag, joxu leen, ndax yu sell ya lañu sasoo woona gàddu.