TSK

TSK · Numbers 12:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te itam yóbbaaleleen seen juroo jur, gu gudd ak gu gàtt, li ngeen bëgg rekk, te ne mott! Waaye ñaanaaleleen ma seen Yàlla nag, mu barkeel ma.»

¶ Ba loolu wéyee mbooloo ma mépp ne Samiyel: «Ngalla sang bi, ñaanal nu ci sa Yàlla Aji Sax ji, nu baña dee, ndax la nu bàkkaaroon lépp, yokkati nanu ci mbon gu tollu ni di sàkku buur.»

Ci kaw loolu ñu jàll dex ga, ngir jàlle waa kër Buur, defal ko coobareem. Ba Buur Daawuda di waaja jàll dex ga, Simey doomu Gera da ne gurub sukk, sujjóotal ko,

Buur ne góoru Yàlla ga: «Rikk tinul ma sa Yàlla Aji Sax ji te ñaanal ma, sama loxo mana banku.» Góoru Yàlla ga tinul Buur Aji Sax ji, loxoom bankuwaat, mel na mu meloon.

Muy kàddug Sabóor guy fàttlee, ñeel Daawuda.

Ñu ne Yonent Yàlla Yeremi: «Ngalla danu lay dagaan, nga ñaanal nu ngir ndesu askan wii ci sa Yàlla Aji Sax ji. Bare woon nanu, waaye gis nga lu néew li des ci nun.

Ñenn ci jàngub Seytaane bi, ñooñuy fen, di tuddoo ay Yawut te duñuy Yawut, maa ngii di leen xiirtal, dikkloo leen, sujjóotloo leen fi sa kanam, ba ñu xam ne man maa la sopp.