¶ Da ne leen: «Bu ngeen farloo ci déggal seen Yàlla Aji Sax ji, di def li mu rafetlu, di teewlu tey jëfe ay santaaneem, di sàmm bépp dogali yoonam, su boobaa duma leen teg lenn ci jàngoro, yi ma tegoon waa Misra, ndax man maay Aji Sax, ji leen di wérloo.»
TSK
TSK · Numbers 12:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bànni Israyil gépp nag di ñaxtu ci kaw Musaa ak Aaróona, mbooloo ma mépp naa leen: «Waay lu nu tee woona dee ca réewum Misra, mbaa sax nu dee ci màndiŋ mii!
Man nag, yàlla tere may tooñ Aji Sax ji, di leen noppee ñaanal. Te it dinaa leen won yoon wi baax te jub:
Buur ne góoru Yàlla ga: «Rikk tinul ma sa Yàlla Aji Sax ji te ñaanal ma, sama loxo mana banku.» Góoru Yàlla ga tinul Buur Aji Sax ji, loxoom bankuwaat, mel na mu meloon.
Éy Aji Sax ji, faj ma, ma faju; musal ma, ma mucc, samag cant, yaw a.
Ñi leen di móolu, yéeneleen leen lu baax, ñi leen di soxore, ñaanal-leen leen.
Mu ne gurub, samp bëti óomam, daldi àddu ca kaw, ne: «Sang bi, bu leen topp bii bàkkaar.» Naka la wax loolu, daldi nelaw.
Ñaan gu ànd ak ngëm day musal ki wopp, ba Boroom bi yékkati ko. Su dee daa bàkkaar, dees na ko jéggal.