TSK

TSK · Numbers 12:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci biir loolu Musaa dégg mbooloo miy ñaxtu, làng ak làng, ku nekk ci sa bunt xayma. Ba loolu amee sànjum Aji Sax ji tàkk jippét, Musaa nag ñaawlu ko.

Ñu merlooti Yàlla ca ndoxum Meriba ma, muy loraangey Musaa te ñoo ko waral.

Aji Sax jee safoo ñoñam, di terale néew-ji-doole ag mucc.

¶ Man Póol ci sama wàllu bopp nag, maa leen di ñaaxe teeyug Almasi, akug lewetaayam, man miy teew ci seen biir, di ab ragaleey, fi seen kanam, te bu ma soree doŋŋ laa leen di ñemeey,

¶ Mujj naa dib dof nag, te yeena ma ko yóbbe, nde gërëm maa leen waroon, ndax doonte duma dara sax, ndaw yu màgga màgg yooyeey, duma seen cuune ci lenn.

James 3:2 TSK

Bare na lu nuy tooñ, nun ñépp. Ku dul tooñ ci kàddu nag, kooku nit ku mat la, te man naa moom yaramam wépp, boole ci.

waaye nay lu làqoo jëmmu biir, nay gànjar gu dul jeex, te mooy lewetaay akug teey, ndax looloo réy njarte fa Yàlla.