TSK

TSK · Numbers 14:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ca la Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Waaw yeen nag, dungeen ma noppee gàntalal samay santaaneek samay ndigali yoon mukk?

kenn ci ñoom déy du gis réew, mi ma giñaloon seeni maam. Mboolem ñi ma xarab, kenn du ko ci gis.

Loolu lépp taxul ngeen am kóolute ci seen Yàlla Aji Sax ji,

¶ Ca Tabera itam, ak ca Maasa, ak ca Kibbrot Taawa, ngeen merlooti fa Aji Sax ji.

Loolu lépp teewul ñuy bàkkaar ba tey te gëmuñu ay kéemaanam.

ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba, jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma,

Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi? Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi? Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?

Hosea 8:5 TSK

Yeen waa Samari, seen jëmmu wëllu wi dàqu na! Sama mer tàkkal na leen. Lu ngeen deeti xaar ci mucc ayib?

¶ Ana ñan ñoo déggoon te teewuleena fippu? Xanaa du mboolem ña génne woon Misra ci njiital Musaa?