TSK

TSK · Numbers 15:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Góor gu xaraful, ndax nanguwula xaraf, dees na ko dagge ci biir xeetam, ndax sàmmul sama kóllëre.»

Képp ku njafaan lu ni mel, mbaa mu taqal ci yaramu ku ci bokkul, dees koy dagge ci biir bànni Israyil.”»

Ku jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee mbaa mu jublu ci boroom rawaan yiy seet, topp leen, di ma leen bokkaalee, dinaa ko noonoo moom itam te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil.

Ku set nag te nekkul ciw yoon, su ñàkkee màggal bésub Mucc bi, kooku dees koy dagge ciw askanam, ndax saraxu Aji Sax ji mu joxewul ci bésam. Kooku moo gàddu bàkkaaru boppam.

Ma wax leen ko, dégluwleen, xanaa gàntal ndigalal Aji Sax ji, fétteeral, ba yéegi diiwaanu tund wa.

Aji Sax ji du nangoo baal kooku, nde su boobaa, sànjum Aji Sax jeey ànd ak fiiraangeem, tàkk ci kawam, te mboolem alkànde gi ñu bind ci téere bii day këppu ci kawam, te Aji Sax jeey far aw turam fu asamaan tiim.

Nit juum na, umple ko, baal ma tooñ gu ma umple.

Kon xoolal, Aji Sax ji, noon a ngi ree, xeet wu amul bopp a lay sewal.

Boroom bi, sewal gi la sunuy dëkk sewal, këpp leen ko juróom yaari yoon,

Ku sonal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; ku baaxe ku néewle, teral nga ka ko sàkk.

Kon ki dëggaate Doomu Yàlla ji, teddadil deret ji ñu sellale kóllëre gi, te ñàkke teggin Noowug Yàlla gi nu indil aw yiw, kooku, mbugal ga mu yelloo, ñaata yoon lay gënatee metti, ngeen defe?