TSK

TSK · Numbers 17:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nguur gi du jóge ci loxol Yuda, te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam, li feek boroom di ñëw, ba xeet yi déggal ko.

Yóbbaaleel yet wii nag, ndax ci ngay defe firnde yi.»

Ñiy wuyoo tur yii nag, ñoo leen ciy taxawu: Ci wàllu Rubeneen ñi, Elisur doomu Sedeyur.

¶ Keroog ba Musaa sampee jaamookaay bi ba noppi, diw na ko ngir sellal ko, mook mboolem ay jumtukaayam, sarxalukaay beek mboolem ndabam it, mu boole diw, sellale ko.

Nguur gu bon du saxe kaw suuf su nit ñu jub muurloo. Lu ko moy ñu jub ñi sàkku lu bon, di ko jëfe.

ba képp kuy dund xam ne man Aji Sax ji maa bocci sama saamar, te du dellu mbaram.”

«Yaw nit ki, sàkkal aw dénk, nga bind ci kaw lii: “Ñeel Yuda ak giiri Israyil yi mu àndal.” Nga sàkkaat weneen dénk, bind ci kawam: “Ñeel Yuusufa bantub Efrayim ak waa kër Israyil yi mu àndal,”